Alhamdu lil-LAAH, Senegaal amatina ndam ci Alquraan, jaare ku ci doomam ji di: Àlliyu Badara Jaañ dëk Luga, di dongab Sëriñ Usmaan Ja, jëlóon ñàtteelu toogu ba (3iem) ca Senikóo 2024 bi jàll ca koor ga, moom la Yàlla def mu jël ñàtteelu toogu ba (3iem) ca joŋanteb Alquraan ba doon ame ca reewum Alseeri 24 - 30 Ut, nu dùppeeko "Masaamiiru Daawuud".* *Yal na ko jik, te sédd gùyyu, yal na ko muurlóo mooki wa-juram aki bókkam, yal na ci yenee tópp.* *Te yalna ko Yàlla sàmm mook sëriñ daaraam, aki wa-juram.* *Mu doonoon joŋante bu yàgg te jafe te métti: ndax lu jiitu muy dem woo nañ ko laaj ko juróom ñeenti (9) laaj, ku yégg yit dees nala defalaat ay nàtt, nu doora dùgg ci joŋante bi nga xam ni ñeenti (4) warngal la.*
Le meilleur Daara au senegal avec une trés bonne education de qualité. Chaque année beaucoup d'enfants memorise le coran. Je parle en connaissance de cause car mon enfant etudie dans cette magnifique daara❤❤❤❤❤